• il y a 4 ans
Ballago ndoumbé yatma

Billaay , ballago ndoumbé yatma ,
su ñu waaji xaj oon na fi
Naxxar doηη ,la ñu bayyee
yalla , wonneeti na


Li tax ba mbir mi metti lool,
ñun da ñu ko foog wul woon
Yëf yi gaaw ba bette gnou
billaay wéetël na ñu

Njiinoo njiin faramaareen,
gòor u jaaga , nelaw naa
Baay i wally dem na nii ,
ñun daal wéetël na ñu

Ma ngi koy jaale Sénégal,
di ko jaalé Gambia
Di ko jaalé adduna ,
ndaanaan ba dem na nii


Thione ballago , ndoumbé yatma
Bu yalla buur bi doon taggoo ,
kon di na ñu bayék yaw
Ni patrimoine bi nga ñu bayyeel ,
Yee gua nit gñi , tete leen ci adduna
Yee gua nit gñi , tete leen
xam al leen ci adduna
ahhh - Balaago

Yee gua nit ñi ci adduna xam al leen
Ni ñu war a nekkek
Ak ni ñu war a dundée ,
Ak ni ñu war a jëfleentee
Jinaxoo mbaay
yaw mi dëkké biir suuf ,
Boo dem ee neel ballago , réew maa ngi koy joy
Aduna ngi koy jooy ,
art baa ngi koy jooy



Njiin faramaareen ,
thione seck , wéetël na ñu
Ballago ndumbé yaatma
adduna , am ul solo

Li tax ba mbir mi metti lool,
ñun da ñu ko foog wul woon
Yëf yi gaaw ba bette gno
Ndanaan ba demna ni
Njiin faramaareen ,
thione seck , wéetël na ñu
Ballago ndumbé yaatma
adduna , am ul solo






Category

🎵
Musique